[go: up one dir, main page]

Aller au contenu

Xiibon

Jóge Wikipedia.
Xiibon
Ribaŋ bu oraas — sagaru xam bu baas xiibon.
Toftale ak balluwaayi biti
Specialty endocrinologie[*], médecine de soins critiques[*], nutrition[*]
ICD-9-CM 263.9
MedlinePlus 000404
eMedicine ped/1360
Patient UK Xiibon
MeSH D044342

Xiibon wala xale bu xiibon mu ngi bawoo ci lekk loo xam ni amul wala bariwul ay ferñent wala ñu bari ci bay indi loraange ci wérgi-yaramu nit ki.[1][2] Mbir yiñ mën a woowe ferñent ñooy: kalori yi, proteyin, karbo-idrate yi, witaamin wala ndox miy suuxat sa yarams.[2] Loolu lañuy faral di woowee lekk gu doyul nga xamni ay kaloreem ak proteyinam duñu doy ferñent yu ndaw yi; waaye, dafa ànd itam ak ferñeent yu ëpp.[3][4] Sudee nit ki amul lekk gu doy ci diirub ëmb bi wala laata muy am ñaari at, loolu mën na ko jural jafe-jafey xel ak ñàkk a mag.[2] Ñàkk a lekk gu tar, ñu koy woowe xiif bu tar, mën na indi jafe-jafe yu ci melni: gàttaay, sewaay, tàyyel, tànk ak biir buy newwi.[2][3] Dina am itam tawat gu leen di faral di jural soj. Ni ñàkkug ferñent di faral di feeñee ngi aju ci ferñent yu ndaw yiñ ñàkk.[3]

Liy faral di indi xiibon mooy ñàkk a am lekk gu baax te doy gu jàppandi.[5] Li mën a waral mooy dund gu seer dóol.[2][5] Ñàkk a nàmp weenu nday mën nako waral, mën a waral itam feebaru jàngoro yu ci melni: gastroenteritis, pnëmoni, sibbiru ak ŋas yiy tax sa yaram di gën a soxla ferñent.[5] Ñaari xeeti xiibon ñoo am: xiibonu ñàkk proteyin-cawarte ak ñàkk lekk gu baax.[4] Xiibonu ñàkk proteyin-cawarte ñaari xeet yu metti la am: marasm (ñàkkug proteyin ak kalori) ak kwasiorkor (ñàkkug proteyin kese).[3] Yenn ferñent yu ndaw yi nit ki mën a ñàkk ñooy: ñàkk feer bu doy, ñàkkug iyod ak ñàkkug Witaamin A.[3] Ku nekk jigéenu wérul, sa yaram dafay soxla mbir yu bari, loolooy waral sa yaram di ñàkk yenn yi.[6] Ci yenn réew yi néew doole lekk gu ëpp pataa mingi fi tàmbalee bari ni ki nifi xiibon gi baree.[7] Yeneen mbir yi mën a waral xiibon ñooy baña lekk ndax ragala am yaram ak opeere ngir wàññi yaram.[8][9] Sudee ci mag ñi yi mën a waral seen xiibon ñooy ni seen yaram bindoo, xel mu ñàkk a dal ak jafe-jafey àdduna.[10]

Jéego yi ñuy def ngir yokk ferñent yi bokk nañu ci mbir yi gën a am solo ci ndimbalum yokkute.[11] Nàmpalee ween mën na musal xale yi ci xiibon ak gaaw a faatu,[2] te jéego yiñ def ci wàll woowu wane nañu seen njariñ.[12] Di jox xale bi muy lekk ak di nàmpaale ba mu am ñaari at, dina tax sa xaalis du jeex ci njëndum garab.[12] Ñépp itam gis nañu njariñ li ci jox ferñenti mottali di ay xeeti witamin yu ñuy jox jigéeni wérul yi ak xale yu ndaw yi ci réew yu néew doole yi.[12] Niñu gën a mën a dimbalee nit ñi soxla luñu dundee dëgg, mooy nga jox leen lu ñuy lekk waaye itam joxaale leen xaalis ngir ñu mën koo jëndee ca seenub marse.[11][13] Di jox xale liñuy lekk ci daara ja rekk du doy.[11] Toppatoo xale bu xiibon bi ci kër ga mu dëkk ready-to-use therapeutic foods lu mën a nekk la.[12] Ñi nga xam ni xiibon gi daleen sonal loolu ba indil leen yeneen jafe-jafe ci seen wérgi-yaram, dañu leen wara yóbbu lopitaal ñu faj leen.[12] Yi ñu ciy gën a faral di faj mooy yaram wu ñàkk suukër, tàngooru yaram, yaram wu ñàkk ndox, ak diko jox mu lekk ni mu waree.[12][14] Di faral di ko jox ay antibiotik lu baax la ci musal ko ci yenn doomu jàngoro yi.[14] Ndimbal li gën am solo tey yàgg: mooy gën a dooleel mbay mi,[15] xeex ndóol, defar wanag yu baax, ak jàppale jigéen ñi ci liggéey.[11]

Ci atum 2010 xayma woon nañu lu tollu ci 925 miliyoŋi doomi aadama yu xiibon, muy of 80 miliyoŋ yu yokk ci limu 1990.[16][17] Ak ñeneen ñu tollu ci benn miliyaar ñuñ xayma ni amuñu witamin ak lu suuxat seen yaram.[11] Ci atum 2010 ñàkkug proteyin, cawarte jur na lu tollu ci 600,000 bakkan yu faatu, doon lim bu wàññiku buñu seetee ci 883,000 bakkan yi faatu ci 1990.[18] Yeneen ñàkkug ferñent yu ci melni ñàkkug iod ak ñàkkug feer, jur na lu tollu ci 84,000 bakkan yu faatu.[18] Ci 2010 xayma nañu ni xiibon moo waral 1.4% ci mbooleem ati ñàkk a mënal sa bopp yi nit di dund.[11][19] Jàpp nañu benn xale ci ñatt yu faatu yu nekk, xiibon a ko ray; waaye, nit ñi duñu faral di nangu ni looloo ko waral.[5] Ci 2010 jàpp nañu ni bokk na ci li faat lu tolloo ak 1.5 miliyoŋ ciy jiggéey ak xale[20] teewul ba tay am na ñu jàpp ni lim bi ëpp na 3 miliyoŋ.[12] Ak yeneen 165 miliyoŋi xale yu mënatul màgg ndax feebar boobu.[12] Xiibon gaa ngi gën a baree ci réew yu néew doole yi.[21]

Royuwaay yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  1. "malnutrition" at Dorland's Medical Dictionary
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 et 2,5 Facts for life (PDF) (4th ed. ed.). New York: United Nations Children's Fund. 2010. pp. 61 and 75. ISBN 978-92-806-4466-1. Archived from the original (PDF) on 2018-12-12. Retrieved 2015-09-19. 
  3. 3,0 3,1 3,2 3,3 et 3,4 Young, E.M. (2012). Food and development. Abingdon, Oxon: Routledge. pp. 36–38. ISBN 9781135999414. 
  4. 4,0 et 4,1 Essentials of International Health. Jones & Bartlett Publishers. 2011. p. 194. ISBN 9781449667719. 
  5. 5,0 5,1 5,2 et 5,3 "Maternal, newborn, child and adolescent health". WHO. Retrieved 4 July 2014. 
  6. Konje, editor, Mala Arora ; co-editor, Justin C. (2007). Recurrent pregnancy loss (2nd ed. ed.). New Delhi: Jaypee Bros. Medical Publishers. ISBN 9788184480061. 
  7. "Progress For Children: A Report Card On Nutrition" (PDF). UNICEF. Archived from the original (PDF) on 2021-01-12. Retrieved 2015-09-19. 
  8. Prentice, editor-in-chief, Benjamin Caballero ; editors, Lindsay Allen, Andrew (2005). Encyclopedia of human nutrition (2nd ed. ed.). Amsterdam: Elsevier/Academic Press. p. 68. ISBN 9780080454283. 
  9. Stoelting's anesthesia and co-existing disease (6th ed. ed.). Philadelphia: Saunders/Elsevier. 2012. p. 324. ISBN 9781455738120. 
  10. editors, Ronnie A. Rosenthal, Michael E. Zenilman, Mark R. Katlic, (2011). Principles and practice of geriatric surgery (2nd ed. ed.). Berlin: Springer. p. 78. ISBN 9781441969996. 
  11. 11,0 11,1 11,2 11,3 11,4 et 11,5 "An update of ‘The Neglected Crisis of Undernutrition: Evidence for Action’" (PDF). www.gov.uk. Department for International Development. Oct 2012. Retrieved 5 July 2014. 
  12. 12,0 12,1 12,2 12,3 12,4 12,5 12,6 et 12,7 Bhutta, ZA; Das, JK; Rizvi, A; Gaffey, MF; Walker, N; Horton, S; Webb, P; Lartey, A; Black, RE; Lancet Nutrition Interventions Review, Group; Maternal and Child Nutrition Study, Group (Aug 3, 2013). "Evidence-based interventions for improvement of maternal and child nutrition: what can be done and at what cost?". Lancet 382 (9890): 452–77. PMID 23746776. doi:10.1016/s0140-6736(13)60996-4. 
  13. "World Food Programme, Cash and Vouchers for Food" (PDF). WFP.org. April 2012. Retrieved 5 July 2014. 
  14. 14,0 et 14,1 Guidelines for the inpatient treatment of severely malnourished children. Geneva: World Health Organization. 2003. ISBN 9241546093. 
  15. Jonathan A. Foley, Navin Ramankutty, Kate A. Brauman, Emily S. Cassidy, James S. Gerber, Matt Johnston, Nathaniel D. Mueller, Christine O’Connell, Deepak K. Ray, Paul C. West, Christian Balzer, Elena M. Bennett, Stephen R. Carpenter, Jason Hill1, Chad Monfreda, Stephen Polasky1, Johan Rockström, John Sheehan, Stefan Siebert, David Tilman1, David P. M. Zaks (October 2011). "Solutions for a cultivated planet". Nature 478 (7369): 337–342. PMID 21993620. doi:10.1038/nature10452. 
  16. "Global hunger declining, but still unacceptably high International hunger targets difficult to reach" (PDF). Food and Agriculture Organization of the United Nations. September 2010. Retrieved 1 July 2014. 
  17. Food; (FAO), Agriculture Organization of the United Nations (2008). The state of food insecurity in the world, 2008 : high food prices and food security : threats and opportunities. Rome: Food and Agriculture Organization of the United Nations (FAO). p. 2. ISBN 978-92-5-106049-0. FAO’s most recent estimates put the number of hungry [actually, malnourished] people at 923 million in 2007, an increase of more than 80 million since the 1990–92 base period. 
  18. 18,0 et 18,1 Lozano R, Naghavi M, Foreman K et al. (December 2012). "Global and regional mortality from 235 causes of death for 20 age groups in 1990 and 2010: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2010". Lancet 380 (9859): 2095–128. PMID 23245604. doi:10.1016/S0140-6736(12)61728-0. 
  19. Murray, CJ (Dec 15, 2012). "Disability-adjusted life years (DALYs) for 291 diseases and injuries in 21 regions, 1990-2010: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2010.". Lancet 380 (9859): 2197–223. PMID 23245608. doi:10.1016/S0140-6736(12)61689-4. 
  20. Lim SS, Vos T, Flaxman AD et al. (December 2012). "A comparative risk assessment of burden of disease and injury attributable to 67 risk factors and risk factor clusters in 21 regions, 1990-2010: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2010". Lancet 380 (9859): 2224–60. PMID 23245609. doi:10.1016/S0140-6736(12)61766-8. 
  21. Liz Young (2002). World Hunger Routledge Introductions to Development. p. 20. ISBN 9781134774944.