Salaan
Apparence
Salaan garab la gog mi ngi bokk ci njabootug aforbiyaas cosaanoo ca penku Afrig. Garab la gog ñu ngi koy fekk mu yaatu lool ci tund Afrig.
==Melo wi==
Garab gu yamamaay lay doon goo xam ni ci guddaayam day jàpp, yaari met. Ay bànqaasam dëgërul lool. Daa gaaw a jooy lool it. Soo ko daggee day génne meen mu weex niki poftan. Ag keram nag, mbëtt yi ak jaan yi bëgg nañu ko lool, ba dañuy faral di gas ci ag ronam lu bari. Xetug ay xobam nag neexul. Bu dee ca Senegaal, ku dugg neegub góor di ab njulli daa ñu la ko faral di wutal.
==Solo si==
Garab la gog manees na koo jëfandikoo cim paj ak ci yeneen ak yeneen.
nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Xobi salaan
turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Euphorbia balsamifera